¶ Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.
TSK
TSK · Luke 9:41
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: «Ba kañ la ma askan wii nara xarab? Ba kañ lañu may gëmadi, ak firnde yi ma def ci seen biir yépp?
Njabootam ñoo def ug yàqute ci kawam, ba dootuñuy doomam ndax seeni sikk. Ndaw maas gu dëng te njublaŋ!
te baña roy seeni maam; maas gu të woon te déggadi, ñu ñàkk pastéef te sàmmuñu kóllërey Yàlla.
¶ Yeesu ne taalibe ya: «Ana seen ngëm?» Ña nga boole tiitaange ak kéemtaan te naan ca seen biir: «Kii nag moo di kan bay jox ndigal ngelaw leek ndox mi sax, ñu déggal ko?»
Lu tollook ñeent fukki at la leen muñal ca màndiŋ ma.
«fa ma seeni maam doon seetloo, di ma diiŋat, te gisoon samay jaloore,
Ndax kat ni ñu nu àggee xibaaru jàmm bi, noonu lees leen ko àggee, waaye kàddu ga ñu dégg moo leen jariñul dara, ndax ña ko dégg ñoo ko déggewul ngëm.
Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.