TSK

TSK · Malachi 3:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ndax kat askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la seen Yàlla Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf.

Aji Sax ji ngeen biral bésub tey, ne mooy doon seen Yàlla, te dingeen doxe ay yoonam, di sàmm dogali yoonam, aki santaaneem, ak àttey yoonam, tey dégg waxam.

Yërmandeeku yiw, fa Aji Sax ji. Moo muñ mer te bare ngor.

Aji Sax jeey barkeel ku ko ragal, mag ak ndaw.

Yaay doon kaalag teddnga ci loxol Aji Sax ji, yaay doon mbaxanam buur, ci sa biir loxol Yàlla jii.

«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.

Ma jaareeti fa, xool la, gis ne mat ngaa séy. Ma tàllal sama mbubb, sànge ko sa yaramu neen, ba noppi giñal la, dikke la kóllëre. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Nii laa la moome.

balaa dogal bee taxaw, bésub mbugal ne jaas ba wéy ni boob, bala leen tàngooru merum Aji Sax jee dikkal, bala leen bésub merum Aji Sax jee taxawal.

«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”

muy Póol, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di ndee, di tey, di ëllëg, lépp, yeena ko moom.

Waaye ku nekk ak ayam. Jooxeb ndoortel meññeef mi, Almasi la. Gannaaw loolu ñoñi Almasi ñooy aye, keroog bu délsee.

Ñi bokk ci Almasi Yeesu nag, ñoo daaj ca bantam ba, seen bakkan, daajaale ko ak sàkkuteefam yu tar, aki xemmemtéefam.

Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya.