Aji Sax ji ñaawlu li muy def, ba tax mu faat ko, moom itam.
TSK
TSK · Numbers 11:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma.
¶ Ba loolu wéyee Musaa ne Aaróona: «Waxal mbooloom bànni Israyil gépp, ne leen ñu dem ba ca kanam Aji Sax ji, ndaxte dégg na seeni diiŋat.»
Sawara ne jippét, bawoo fi Aji Sax ji, lakk leen ba ñu dee fa kanam Aji Sax ji.
¶ Ñu ne: «Ndax mennum Musaa doŋŋ la Aji Sax jiy waxe ci moom? Xanaa daa waxewul ci nun itam?» Aji Sax ji dégg ca.
¶ Ci kaw loolu mbooloo ma dem ba ñàkk ndox. Ñu daje ci kaw Musaa ak Aaróona.
¶ Ca Tabera itam, ak ca Maasa, ak ca Kibbrot Taawa, ngeen merlooti fa Aji Sax ji.
Sawaraa ngay tàkke ca samam sànj, di lakke ba ca xóotey njaniiw, ba xoyom suuf ak meññeefam, ba jafal reeni tund ya.
Ilyaas wax leen ne leen: «Ndegam góoru Yàlla laa, yal na sawara wàcce asamaan xoyom la, yaw yaak sa juróom fukki dag.» Sawaraw Yàlla bàyyikoo asamaan, xoyom njiit la, mook juróom fukki dagam ya.
Aji Sax ji dégg ci, mer lool; xolam tàng ci sëti Yanqóoba, am sànj tàkkal Israyil.
Xambees na démb ab taal bu ñuy wax Tofet, te buur ba lees ko waajalal; dees koo xóotal, yaatal ko, sawara way tàkk, matt ma ne gàññ, noowal Aji Sax ji nar caa tàkke, di sël-sëli ni walum tamarax.
Kuy dund, ana loo deeti jàmbat, bu ñu la añalee sa bàkkaar?
ndax kat «sunu Yàlla, sawara wuy xoyome la.»
Ñooñoo di ñaxtu ak a jàmbat, te topp seen bakkan; kàdduy damu yu réy ay jibe seen gémmiñ, te ñooy jay ñi ñu yaakaare njariñ.