TSK

TSK · Numbers 11:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Mbooloo ma nag mujj di tawat ab coono fi kanam Aji Sax ji. Aji Sax ji dégg ci, am sànjam tàkk, sawaras Aji Sax ji tàkkal leen, ba xoyom la wër dal ba.

Sànjum Aji Sax ji nag tàkkal leen. Ci kaw loolu mu dem.

Ñu daldi jóge mboolem fa wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñoom, ña nga génn, taxaw ca seen bunti xayma, ñook seeni jabar ak seeni doom, ak seeni tuut-tànk.

Ña ngay xultu ca kaw Yàlla ak Musaa, naa: «Lu ngeen nu doon jële Misra, ngir nu dee ci màndiŋ mi? Duw ñam, dum ndox, te wii ñamu toskare génnliku nan!»

Aji Sax ji dégg ci, mer lool; xolam tàng ci sëti Yanqóoba, am sànj tàkkal Israyil.

xanaa di xultoo seen biiri xayma, baña déggal Aji Sax ji.

Aji Sax ji, maaka bañ ñi la bañ te sib ñi lay gàntal.

Dingeen xañ seen bopp cér bi ma leen séddoon, ma def leen seen jaami noon ci réew mu ngeen xamul, ndax merloo ngeen ma mer mu dul fey mukk.»