Ana lu jar Misra di wax naan: “Musiba mi mu leen naraloon, ba mu leen di yiwi de, du lenn lu moy rey leen ba ñu jeex ca tund ya, ba fare leen kaw suuf sépp.” Ngalla dëddul sa sawaras sànj te nga fomm musiba mi nga naral sa ñoñ.
TSK
TSK · Numbers 14:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Aji Sax ji ne Musaa: «Loolu nga wax, moom laa lay defal, ndax daj nga samaw yiw, te it maa la xam ci saw tur.»
su boobaa yaw, yal nanga dégge asamaan, ba jéggale bàkkaarub Israyil sa ñoñ, te nga delloo leen ca réew ma nga joxoon seeni maam.
Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam,
bàyyi xel ci kóllëreem ak ñoom, topp ngoram lu réy, ba giif,
Teewul ñu gàntal ma, nanguwñu maa déglu. Kenn nanguwula xalab tuur yu seexluwu yi mu wékki gët, kenn dëdduwul kasaray tuuri Misra. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ci biir réewum Misra.
Soccet yiy lekk gàncaxu réew mi, ba mu bëgga jeex, ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, ngalla déet! Askanu Yanqóoba àttan na lii am? Lu néew doole lañu.»
¶ Yàlla nag gis seeni jëf, gis na ñu dëddoo seen jëfin ju bon. Yàlla daldi fomm mbugal ma mu leen naraloon, ba mujju koo def.
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.
Ñaan gu ànd ak ngëm day musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Su dee daa bàkkaar, dees na ko jéggal.