TSK

TSK · Numbers 14:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ndaw ya nag ñibbsi, gannaaw ba ñu nemmikoo réew ma lu mat ñeent fukki fan.

Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkkal Israyil, mu wërloo leen ca màndiŋ ma diiru ñeent fukki at, ba mboolem maas googa defoon lu Aji Sax ji ñaawlu, ñépp jeex tàkk.

«Cant ñeel na Aji Sax, ji may Israyil mbooloom ab dal-lukaay, muy la mu waxoon lépp, ngir benn baat fanaanul àll ci digey jàmm yi mu dige woon yépp, Musaa jaamam ba jottli.

Danga maa mere, ma wéradi; maa bàkkaar, ba jagadi.

Ñeent fukki at laa jéppi googu maas, ma ne: “Xeet wu ñàkk wormaa ngi, te faaleedi samay santaane.”

Leeleeg it ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko tabax, jëmbat ko,

Boo noppee ci loolu nanga tëdde wetu ndijoor. Noonu ngay gàddoo ayu waa kër Yuda diiru ñeent fukki fan, at mu nekk, ma defal la ko benn fan.

«“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaa ma fàtte, jalax ma sa gannaaw. Kon nag gàddul sa ayu ñàkk gàcceek sa gànctu.”»

Bu ñu yaroon seeni doom it, maa leen leen di xañ, ba kenn du des. Te it ngalla ñoom, bu ma leen dëddoo.

¶ Kon nag gannaaw digeb tàbbi ci noflaayal Yàlla mu ngi sax ba tey, nanu ragal kenn ci yeen taxawe melokaanu ku ca jotul.