TSK

TSK · Numbers 14:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci kaw loolu sawara bawoo fi Aji Sax ji, tàkk ca kaw sarxalukaay ba, xoyom saraxu rendi-dóomal ba ak nebbon ba. Naka la mbooloo ma mépp gis loola, daldi sarxolle, ba noppi dëpp seen jë fa suuf.

Musaa ak Aaróona ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Éy Yàlla, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, xanaa du kenn ay bàkkaar, nga far sànju ci kaw mbooloom lëmm?»

«Jógeleen biir mbooloo mii, ma faagaagal leen léegi!» Ñu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf.

Ci kaw loolu ma dégg baatam. Naka laa dégg baatam, daldi daanu leer, sama kanam dëppu fi suuf.

ñaar fukki mag ñeek ñeent ne gurub sukk fi kanam ki toog ci ngàngune mi, di ko sujjóotal, moom miy dund ba fàww. Ñuy sànni seeni kaala fi kanam ngàngune mi te naan:

Malaaka yépp a nga taxaw, yéew ngàngune ma ak mag ñaak ñeenti bindeef ya. Ñu ne gurub sukk, dëpp seen jë fa kanam ngàngune ma, sujjóotal Yàlla,