Sàkkal ñetti kilo, yemook benn fukkeelu nattub sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe liitar ak genn-wàll, yemook xaajaatub natt bi ñuy wax xiin ci diwu segalu oliw, ak saraxu tuurub benn liitaru biiñ ak genn-wàll, yemook xaajaatub xiin. Loolu yépp ànd ak menn kuuy mi.
TSK
TSK · Numbers 15:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Na ci sotti diw ak cuuraay. Saraxu pepp la.
Ci biir loolu bépp saraxu pepp mu ñu lakk cib taal, mbaa ñu saaf ko ci cin mbaa ci saafukaayu weñ, sarxalkat bi koy joxe moo koy moom.
Saraxu pepp mi muy àndal juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, ñu xiiwe ko diw, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm. Sarax si ñuy tuural Aji Sax ji, liitaru biiñ laak genn-wàll.
Benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, mooy saraxu pepp bi xar mu nekk di àndal, ñu tooyale ko walaatu xiinu diwu segalu oliw, di liitar ak genn-wàll.
Nañu ci boole suba su ne benn céru juróom benneelu efab pepp, yemook ñaari kilook liibar, ànd ak liitaru diw, yemook benn céru ñetteelu xiinu diw buy tooyal sunguf si. Loolooy saraxu pepp mi, ñeel Aji Sax ji, di dogali yoon yu sax dàkk.
ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.