TSK

TSK · Numbers 18:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Ngëneeli meññeef ma jëkka ñore ca seen suuf, moom ngeen di yóbbu seen kër Yàlla Aji Sax ji. «Ab tef, buleen ko togge soowum yaayam.

Saraxi ndoortel meññeef man naa ànd ak yooyu, waaye du bokk ci sarax su jëm ca sarxalukaay ba, ñu di ko taal, ngir xetug jàmm.

Seeni kër ngeen di jële ñaari mburu yuy doon saraxu yékkati-jébbale, mu ci nekk di lu ñu lakke juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib; dees ciy def lawiir, lakkaale ko ko, muy saraxu ndoortel meññeef, ñeel Aji Sax ji.

bay lekk ca ñamu réew ma, nangeen ci jooxe ab jooxe, ñeel Aji Sax ji;

na ku nekk ci yeen sàkk ca ndoortel mboolem meññeefum suuf mu mu jële ca seen réew, ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, mu def ko ci pañe, yóbbu ca bérab ba seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg.