Leween ñi ñooy ñiy liggéey liggéeyi xaymab ndaje mi, te lu ñu ca tooñ, ñooy gàddu pey ga, ci kaw dogal bu sax dàkk, ñeel leen, ñook seen askan. Waaye biir bànni Israyil, Leween ñi duñu ci séddu céru suuf,
TSK
TSK · Numbers 18:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Looloo waral Leween ñi amuñu wàll ci céru suuf su ñuy séddoo ak seeni bokk. Aji Sax ji mooy seenub cér, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji waxe woon.
Leween gi ci seen biir dëkk nag, buleen leen fàtte, ndax amuñu wàll ci seen céru suuf.
¶ Leween ñiy ay sarxalkat, ba ci giirug Leween gépp nag, wenn wàll mbaa céru suuf ñeelu leen ci seen bokki Israyil. Saraxi sawara yu Aji Sax ji, akub céram, moom lañuy dunde.
Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg.
Ma geesu ndijoor, xool; du kenn ku ma faale. Rawtu réer ma, du kenn ku sama bakkan saf.
¶ «Sarxalkat yi am nañu seen céru bopp: man maay seen cér. Du jenn moomeel ju ngeen leen di jox ci suufas Israyil. Man maay seen moomeel.
Ma dégg kàddu gu xumb jibe ca ngàngune ma, ne: «Màkkaanu Yàllaa ngii ci biir nit ñi. Mooy dëkk ak ñoom, ñu diy ñoñam. Yàlla ci boppam mooy dëkk ak ñoom, di seen Yàlla.