TSK

TSK · Numbers 18:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ñooy dénkoo ndénkaaneem, di dénkoo dénkaaney mbooloo mépp fi kanam xaymab ndaje mi, ndax ñooy sasoo liggéeyu jaamookaay bi.

Aji Sax ji neeti Aaróona: «Seenum réew nag doo ci am cér, te wàllu suuf, doo ko am ci seen biir. Man maay sa wàll, di sab cér ci biir bànni Israyil.»

Ña ñu limal Leween ñi nag ñaar fukki junneek ñett lañu (23 000), di mboolem góor ña am weer, jëm kaw, te limaaleesu leen ak bànni Israyil ga ca des, ndax joxeesu leen ab cér ci biir bànni Israyil.

Looloo waral Leween ñi amuñu wàll ci céru suuf su ñuy séddoo ak seeni bokk. Aji Sax ji mooy seenub cér, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji waxe woon.