TSK

TSK · Numbers 23:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan.

Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele.

¶ «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca.

¶ «Mboolem ña ñu limal dalub Dan daldi doon téeméer ak juróom fukki junneek juróom ñaar ak juróom benni téeméer (157 600). Ñooñooy mujja jóg, topp seeni raaya.»

Bàyyil xel ku maandu, xool ku jub; muj, fa nitu jàmm.

Luke 2:29 TSK

«Léegi nag Buur Yàlla, yiwil sab jaam, mu dem ak jàmm, noonee nga ko waxe woon.

Sunu yaramu judduwaale wii nara yàqu, fàww mu sol weneen wu dul yàqu; sunu yaramu ndee wii, fàww mu sol yaramu deetil.

Li jaadu ci sama gis-gis moo di, li feek may màkkaanoo aw suux, dinaa leen ko fàttli, ngir soññ leen.