TSK

TSK · Numbers 23:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Man Aji Sax ji, maa ko wax. Noonu déy laay def mboolem mbooloo mu bon mii booloo ci sama kaw. Ci màndiŋ mii lañuy raafe, fii lañuy deeye.»

Bésub keroog ma matal ci Eli mboolem lu ma waxoon ne mooy dal waa këram, ndoorte la ba ca muj ga.

Ku Yerbowam deele ci dëkk bi, xaj yi lekk; ku ca médd ca àll ba, njanaaw ya for. Aji Sax ji wax na ko.”

Loolu mooy kàddu ga Aji Sax ji waxoon Yewu ne ko: «Saw askan dinañu toog ci kaw jalu Israyil ba ci sa sët-sëtaat.» Te noonu la amee.

Xanaa daa jeexal ngor tàkk? Am kàddoom a deñ ba fàww?

Aji Sax ji daa giñal Daawuda dëgg gu mu dul dëddu, ne ko: «Ku jóge sa geño laay wuutal ci sa jal bi,

Loolooy tax suuf di ñaawlu, asamaan di lëndëm. Maa ko wax, maa ko dogu; duma dëpp, duma deltu gannaaw.»

Duma wéye di tàkkal sama mer, duma yàqteeti Efrayim, ndax maay Yàlla, duma nit, maay Aji Sell ji ci seen biir, duma dikke am sànj.

Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal, seede su wóor ci na mbir may mujje, te du fen. Su diibee it, xaar ko, day dikk moos te du yàggati.

Asamaan ak suuf dina wees, waaye samay wax du wees mukk.

Titus 1:2 TSK

Ngëm googu, ak xam-xam boobu, ñu ngi sukkandiku ci yaakaar, ji nu am ci texe ba fàww, te googu texe, Yàlla mi dul fen, moo ko dige ba àddina sosoogul.

gépp may gu baax, ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.