«Beñamin ay till guy yeeroo, di xëye yàpp rëbbam, tey gonloo séddale am lëlam.»
TSK
TSK · Numbers 23:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Israyil a ngi yuug ak a goor ni gaynde, mbete gayndeg sibi, ana ku koy yee? Ku ko ñaanal barke, yaay barkeel; ku ko ñaanal alkànde, yaay alku.»
Gàdd la wax ne ko: Barke ñeel na ku yaatal Gàdd. Ni gaynde la goore, te mooy xotat përëg akum kaaŋ.
gaynde, mooy buuru rab yi, ragalul kenn;
¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.
Aji Sax ji, sa loxo ca kaw, tiim say bañ, mboolem say noon lees di dagge ci kaw suuf.
Fa Yuda la doju collu tabax di bawoo, jënu xayma, fa moom, xalay xare, fa moom, mboolem njiit yi ba ñépp daj, fa moom.
Kenn ci mag ñi ne ma: «Bul jooy. Ma ne, Gayndeg giirug Yuda, njebbital Buur Daawuda daan na. Mooy ubbi téere beek juróom ñaari tayoom.»