Numbers 22:11
TSK
“Balaam, gàngoor a ngii jóge Misra, lal suuf si ba mu daj. Dikkal gaaw móolul ma leen. Jombul ma mana xareek ñoom, ba dàq leen.”»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
“Balaam, gàngoor a ngii jóge Misra, lal suuf si ba mu daj. Dikkal gaaw móolul ma leen. Jombul ma mana xareek ñoom, ba dàq leen.”»
¶ Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Yaw, li nga ma def nag? Móolu samay noon laa la jële, yaw defoo lenn lu moy ñaanal leen?»
Waaye seen Yàlla Aji Sax ji moo nanguwula déglu Balaam; kàddug yàqe ga la leen seen Yàlla Aji Sax ji soppil barke, ndax seen Yàlla Aji Sax ji da leena sopp.
Dees na ko tacc-taccali loxo, di ko ciipoo fa këram.
Yaw nit ki, yuuxul, jooyal, saamar bi dikkal na sama ñoñ, dikkal mboolem kàngami Israyil, boole leen ak sama ñoñ, jalax ci kaw saamar. Kon nag, màttul, wiccax!
Menn peeñu moomu dikk na ba muy ñetti yoon, ñu doora yéege lépp asamaan.