TSK

TSK · Numbers 24:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu weesee Amalegeen ña dikk, xareek bànni Israyil ca Refidim.

Booba la wax ne, gannaaw loxoo ñemee xàcci, jëm ci ngànguney Aji Sax ji, Aji Sax ji dootu noppee xareek Amaleg ba fàww.

Njàmbaar la xaree, duma Amalegeen ña, ba musal Israyil ca ña doon sëxëtoo seen alal.

¶ Ci biir loolu Daawuda aki nitam daan nañu song-songee Gesureen ñi ak Giraseen ñi ak Amalegeen ñi. Mooy ña dëkke woon naka jekk réew mooma, ba ca Sur, jàpp réewum Misra.

Daawuda nag di leen fàdd, njël ba ca ngoon. Kenn rëccul, lu moy ñeenti téeméeri xale yu góor yu war ay giléem, daw.

¶ Gannaaw ba xew-xew yooyu jàllee, Buur Aserus teral ku ñuy wax Aman doomu Amdeta mi askanoo ci Agag, yékkati ko, teg ko ci kaw mboolem kàngam yi ci wetam.

Buur joxe ndigal ngir ñu def noona. Ba loolu amee ñu siiwal ab dogal ca Sus, daldi wékk fukki doomi Aman yu góor ya.