Genesis 3:13
TSK
Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.»
¶ Musaa nag ne Aaróona: «Lan la la mbooloo mii def, ba nga yóbbe leen gii moy gu réy?»
Musaa ne leen: «Kon jigéeni Majan ñépp ngeen bàyyi, ñu dund!
Waaye na jaan ja naxe woon Awa, ca pexeem, ragal naa seenum xel yàqoo noonu, ba dëddu ngëm gu dëggu te set gu ngeen ŋoye woon ci Almasi.
Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.