¶ Ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Musaa: «Ma ne, sa bésub dee ngi jegesi. Wool Yosuwe, te ngeen teewsi fi xaymab ndaje mi, ma yeb ko.» Musaa dem, ànd ak Yosuwe, ñu teewi fa xaymab ndaje ma.
TSK
TSK · Numbers 27:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Diirub ayu Suleymaan gépp nag, waa Yudak Israyil ànd ak xel mu dal; ku ci nekk ak sa ker garabu reseñ ak sa ker garabu figg, fa dale diiwaanu Dan ba ca Beerseba.
Dinaa leen taxawalal ay sàmm yu leen di sàmm ba dootuñu tiit, dootuñu jàq, dootuñu wuute.» Kàddug Aji Sax jee.
¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.
Wattuleen nag seen bopp, wattu mboolem gétt, gi leen Noo gu Sell gi sàmmloo, te ngeen foral mbooloom gëmkati Yàlla, mi Yàlla jote deretu boppam.
Foral-leen gétt gi ñu leen dénk. Sàmmleen ko, te bañ koo defe ñàkk pexe, xanaa xol bu tàlli, ni ko Yàlla bëgge. Buleen ko defe it koppartuy kese, waaye farluleen ci.