TSK

TSK · Numbers 28:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko.

bu ngeen di defal Aji Sax ji saraxu sawara, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax su nit di wàccoo aw xas, mbaa saraxu yéene, mbaa seen saraxi màggal, ngir xeeñal xetug jàmm ñeel Aji Sax ji, te muy lu jóge ci jur gu gudd mbaa gu gàtt, defe leen ko nii:

¶ Daawuda ne Yonatan: «Xanaa lenn. Ëllëg la màggalu Terutel weer wi, te man, manumaa ñàkka toog ak Buur, ngir lekk. Waaye may ma, ma làquji àll ba, ba gannaaw ëllëg ca ngoon.

¶ Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga,

Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.

Wal-leen liit gi ci Terutel weer wi, ak weer wu birale bésu màggal.

Su ko defee Terutel weer ba Terutel weer, bésub Noflaay ba bésub Noflaay, mboolem doom aadama di ma sujjóotalsi.» Aji Sax jee ko wax.

¶ «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Buntu ëttu biir bi féete penku, na tëje diiru juróom benni fan yi ñuy liggéey. Waaye bésub Noflaay ba cay topp, na ubbiku. Bésub Terutel weer it, na ubbiku.

Kon nag fa ngóob jote laay nangoo sama pepp, fa wittum reseñ jote it laay nangoo sama biiñ bu bees, maay foqati sama wëñ ak sama lẽe, ba mu daan sànge yaramam.

Yeena ngi wormaal yenn bés yi, aki weer, ak ay fan, aki at!

¶ Kon nag bu leen kenn sikkal ci ñam wu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, mbaa màggal bés bu rafet, mbaa Terutel weer, ak bésub Noflaay.