TSK

TSK · Numbers 29:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ak benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak póotum bàkkaaru njotlaay gi, ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam, ak seen saraxi tuur yi ci war.

Ba mbooloo ma tasaaroo, bare na ay Yawut ak tuubeen yuy jaamu Yàlla yu topp ci Póol ak Barnaba. Ñuy wax ak nit ñi, di leen ñaax, ngir ñu sax ci doyloo yiwu Yàlla.

Waaye ñooñu, nangulunu leen lu tollook simili sax, ndax bëgg leena sàmmal yeen, dëggug xibaaru jàmm bi, ba mu sax ci yeen.

Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw te nara sànku, waaye nooy ñi saxoo ngëm te nara mucc.