TSK

TSK · Numbers 31:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Leween ñi ñoom, maa leen jox bépp céru fukkeel bu génne ci Israyil, muy seen cér, ñu yooloo ko seen liggéey bi ñuy liggéey ci xaymab ndaje mi.

Céru bànni Israyil bi ci des, nangeen ci sàkk benn ci juróom fukk yu nekk (50), ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt, mbaa gépp jur, te ngeen jox ko Leween ñi dénkoo dénkaaney màkkaanu Aji Sax ji.»

Su boobaa ñu indil Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, galag bu bawoo ci xeet wu siggi, rattax yaram, askan wu ñu ragale fu jegeek fu sore, xeet wu am doole, di falaxee, te seenum réew defi wal, galag ba agsi ba tundu Siyoŋ, fa Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dëël turam.

Waa dun ya déy a nga may séentu, gaali Tarsis yu mag yaa nga jiitu, jële fu sore sa doom yu góor ya, indaale seen xaalis ak seen wurus, ngir sa Yàlla Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil ji la teral.