TSK

TSK · Numbers 34:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu dellooti ëmb, am doom ju góor daldi ne: «Bii yoon dinaa sant Aji Sax ji,» loolu tax mu tudde ko Yuda (mu firi Cant). Gannaaw loolu njuram taxaw.

¶ Doomi Leya ñooy: Ruben, taawub Yanqóoba, ak Simeyon ak Lewi ak Yuda ak Isaakar ak Sabulon.

ak Kaleb doomu Yefune, ci giirug Yudeen ñi,

Yosuwe doomu Nuun, ak Kaleb doomu Yefune, ñoom ña bokk ca ña seeti woon réew ma, daldi xotti seeni yére ndaxu tiis.

kenn ku moy Kaleb doomu Yefune ak Yosuwe doomu Nuun, du kenn ku ciy dugg ca réew, ma ma leen giñoona dëël.

Ndax ci ñoom la Aji Sax ji noon dee rekk lañuy def ba jeex ca màndiŋ ma. Kenn desu ca, ku dul Kaleb doomu Yefune, ak Yosuwe doomu Nuun.