TSK

TSK · Numbers 9:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su fekkee ne ab doxandéem bu ngeen dëkkal dafa bëgga wormaal màggalu bésub Mucc bi ngir Aji Sax ji, xaraf war na ko, te war na gépp góor gu bootu ci moom; su loolu amee, dees na ko may, mu def ko, ndax kon day mel ni doomu réew mi. Waaye kenn ku xaraful du ci lekk.

Seen tóokëri reseñ it buleen ko witt ñaari yoon te buleen foraatu doom yu wadde ca witt ma. Aji ñàkk akub doxandéem ngeen koy bàyyee. Maay seen Yàlla, man Aji Sax ji.

Na àtte bi di benn ci doxandéem ak njuddu-ji-réew, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.»

Yeena ngi tàbbi ci seen biir kóllëreg Yàlla Aji Sax ji, ak ci ngiñam, kóllëre gi seen Yàlla Aji Sax ji fasoo ak yeen bésub tey,

Ezra 6:21 TSK

Ba mu ko defee, bànni Israyil ga ñibbsee ngàllo ga daldi bokk reerub bésub Mucc ba, ñook mboolem ña dogoo woon ak sobey yéefar yi ci réew mi, ngir sàkku Aji Sax ji, Yàllay Israyil.

¶ Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen.