Esawu nag dëkk ca tundu Seyir: Esawu moomu mooy Edom.
TSK
TSK · Obadiah 1:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bew, yàqule; jëkke woyof, mujje tedd.
Maa teg alali xeet yi loxo, ni ku gis am tàgg. Maa tonneendoo réewi àddina ni ku for ay nen, tonni lépp, laaf tëf-tëfluwul, sàll newul ciib!»
Teewul nga tàbbi njaniiw, àkki ba ca xóotey pax ma.
te naa: «Ba fàww maay lingeer!» ba tax bàyyiwoo xel ca la ngay def; xalaatoo la muy jur.
Céy Raba, bii dëkk bu taaru, toogadi, yeena doon damoo xur yi, ba ci seen xur wu naat wii? Yeena yaakaaroon seeni denc, naan: “Ku ñemee dal sunu kaw?”
Sa liggéeyu jula bu yaatu moo la feesal fitna, nga bàkkaar, ba ma nangoo sa teddnga fa tundu Yàlla wa, sànk la, yaw malaakam serub miy aare, nga jóge digg doj yuy tàkk.
Joxleen ko ci toskare aku naqar, kemu daraja jaak dund gu bakkane ga mu jagoo woon. Gannaaw moo ne cim xelam: “Maa tooge jalu lingeer, dumab jëtun, duma deele mukk,”