TSK

TSK · Philemon 1:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 9:17 TSK

¶ Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg Sóol loxo, ne ko: «Mbokk mi Sóol, Sang Yeesu, mi la feeñu woon ci yoon wi nga dikke, moo ma yebal ci yaw, ngir nga dellu di gis te feese Noo gu Sell gi.»

¶ Yeen nag bokk yi, yeenay doomi digeb Yàlla, ni ko Isaaxa doone.

¶ Jaam yi, nangul-leen ci lépp seen sang yi ci àddina. Buleen ko defe ngistal, mbaa ngeen di ko sàkkoo lu leen neex, waaye defeleen ko yéeney xol bu dëggu, ndax ragal Boroom bi.

¶ Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.