Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
TSK
TSK · Romans 1:28
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Daa fekk nga baña xam, te ragal Yàlla du loo taamu.
Ab dof du am xaalis, jënde xel mu rafet; buggu ca dara.
Dees na leen wooye mbuubitum xaalis, nde Aji Sax ji buub na leen, sànni.
Maay def loolu ngir nanguwaat xolu waa kër Israyil, gi ma dëddu ngir seen mboolem kasaray tuur yi.”
Ndax maa doon doxantu, di seet seeni jaamookaay, ba yem ci bu ñu bind mii mbind: “Ñeel yàlla ji nu xamul.” Loolu ngeen di màggal te xamuleen ko nag, moom laa leen di xamal.
¶ Sànjum Yàlla fa asamaan lay dale feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi, ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.
¶ Moo tax Yàlla bërgal leen ak seen xemmemtéef yu bon yi ci seen xol, ba ñu sóobu ci jëflantey sobe juy teddadil seen yarami bopp.
Ndaxte boroom xintey bakkan ab noonu Yàlla la, nde déggalul yoonu Yàlla, te manu ko sax.
Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.
¶ Xoolaatleen seen bopp, ba xam ndax yeena ngi ci yoonu ngëm wi. Nattleen seen bopp, xanaa xam ngeen ne Yeesu Almasee ngi ci yeen? Ndegam du seen gëmadi, la natt ba firndeel!
Ci biir sawara wuy sëlsëli lay doon. Ca lay mbugal ñi xamul Yàlla, ak ñi baña déggal xibaaru jàmm bi jëm ci sunu Boroom Yeesu.
Noonee Sànnes ak Sàmbres doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm.
¶ Lii nag sañoon naa la koo digal ci turu Almasi, ndax mooy li la war,