TSK

TSK · Romans 16:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Micah 2:3 TSK

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di nasal googu làng aw ay, ay wu ngeen dul teggee ci seenu loos, te dungeen daagu, siggi, nde jant yu metti lay doon.

Ci kaw loolu mu jaare diiwaani Siri ak Silisi, di ñaax mboolooy gëmkat ña.

Barewul ku nangoo deeyal nit ku jub, doonte jombul mu am ku nangoo deeyal ku baax.

¶ Ci wàllu ndimbal li jëm ci gëmkat ñu sell ñi, noonu ma ko digale mboolooy gëmkati diiwaanu Galasi, yeen itam defeleen ko noonu.

Ndax kat bokk yi, yeena aw ci tànki gëmkati Almasi Yeesu ya fa mboolooy Yàlla, ya fa réewum Yuda, nde coono ya ñu daj ca Yawut ya, yeen it seeni waa réew teg nañu leen lu ni mel.

¶ Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,