TSK

TSK · Romans 3:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jee tollu asamaan, jéer doom aadama, di seet ku ci xelu, tey sàkku Yàlla.

Ñépp a dëddu, bokk yàqu yaxeet. Kenn deful lu baax, du kenn sax.

Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.

Daa fekk nga baña xam, te ragal Yàlla du loo taamu.

car ya wow, damm, jigéen ñi dikk, xambe. Dañu di xeet wu dul dégg, ba tax ki leen sàkk yërëmu leen, moo leen bind te ñeewantewu leen.

Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, wooleen ko bi muy jege.

«Dofe la sama ñoñ def. Man, xamuñu maay kan, mbetey gone yu dul xalaat dara; dég-dég, tus; seen xel mépp, lu bon rekk, lu baax, xamuñu ci dara.»

Israyil, ag reewandeem a ko tiiñal, te taxul ñu délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji. Loolu yépp taxul ñu sàkku ko.

¶ Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgal leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi.

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.