Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko, te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, ba mu àtte leen àtteb njekk, sëfoo seeni ñaawtéef.
TSK
TSK · Romans 3:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Kuy liggéey, ag peyooram du taxawe ag may, waaye wartéef la.
¶ Gannaaw joxees nañu nu àtteb ñu jub ndax deretam ji tuuru nag, ñaata yoon lees nuy gënatee musal ci am sànj ndax moom?
Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,
Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.
Ci moom lanu ame ag njot, te moo nu jéggal sunuy bàkkaar.
Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
Xaymab jaamookaay ba ñu sàkkoon ñaari néeg la woon. Bu jëkk ba, ca la tegukaayu làmp ba nekkoon, ak taabal ja, ak mburum teewal ma. Moo doon bérab bu sell ba.
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.