Kóllëre gi ma fas ak yaw, te nga war koo sàmm, yaak sa askan, li mu laaj mooy lii: góor gu nekk ci yeen, war naa xaraf.
TSK
TSK · Romans 4:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Waxal bànni Israyil ne leen: “Fexeleen rekk ba sama bési Noflaay, ngeen di ko wormaal, ndax bésub Noflaay da di firnde sama digganteek yeen ak seen askan, ngir ngeen xam ne man Aji Sax ji maa leen ber, sellal leen.
Su boobaa seen Yàlla Aji Sax jee leen di xarfal xarafu xol, te mooy xarfal xarafu xol, seen askan, ngir ngeen soppe seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ndax ngeen dund.
Sama bési Noflaay, sellal-leen ko, muy firnde sama digganteek yeen, ngir ngeen ràññee ne man maay seen Yàlla Aji Sax ji.”
Ab Yawut, du ci melo wuy feeñ lees koy nekke, te xaraf it du ci màndarga muy feeñ ciw yaram.
nde Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy jox àtteb ku jub.
¶ Kon nag dige Yàlla boobu, ngëm moo ko waral, ngir mu di aw yiw doŋŋ. Noonu la dige bi doone lu wóor, ñeel ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp; du ñi bokk ci yoonu Musaa rekk, waaye ñeel na itam ñi bokk ci ngëmu Ibraayma, miy sunu maam, nun ñépp.
¶ Ana lu nu ci mana wax? Xeet yu dul Yawut te sàkkuwuñu woon ag njub, ñoo jagoo àtteb njub, te mooy njub gi ngëm di maye.
Ndax kat Almasi moo sottal yoonu Musaa, ngir àtteb ku jub ñeel képp ku ko gëm.
Mbind mi moo ne: «Képp ku ko gëm, doo rus.»
Xamleen boog ne nit ñiy boroom ngëm, ñooñu ñooy doomi Ibraayma.
Te su ngeen bokkee ci Almasi, yeen ay askanu Ibraayma, te yeena jagoo dige ba.
Mboolem ñiy sàmm ndigal lii nag, te di Israyilu Yàlla, jàmm ak yërmande ñeel na leen.
Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell, gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot ba.
¶ Ngëm la Nóoyin dégge waxyub Yàlla bu jëm ci lu kenn gisagul woon, te ragal Yàlla la sàkke gaal, ngir musal njabootam. Ngëmam it la tiiñale àddina, ba ab céram di njub gi ngëm di maye.
Ñu ne leen, buñu laal menn um ñax, mbaa genn gàncax, mbaa genn garab, xanaa ñu jublu rekk ci nit ñi amul màndargam torluwaayu Yàlla ci seen jë.