TSK

TSK · Romans 4:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Man ci sama wàllu bopp, kóllëre gi ma fas ak yaw mooy lii. Dinga nekk maamu xeet yu baree bare.

Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa.

Yal na la Yàlla Aji Man ji barkeel, nga jaboot lool te sa giir yokku, ba sos ay mboolooy askan.

Ana ku mel ni man? Na àddu! Na biral firndeem te taajal ma la amoon ba may sos xeet wu yàgg wa, ak li dikkagul. Na ko wax!

Ñu ngiy bawoo fu sore, ñu ngii bawoo bëj-gànnaar ak sowu, ñee bawoo diiwaanu Sinim ca bëj-saalum.»

Boroom bee xamle loolu bu yàgga yàgg.”

Bu fekkoon ne Ibraayma, ci kawi jëfam lees ko jox àtteb ku jub, kon mu man koo damoo, waaye demewul noonu fa Yàlla.

Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw, ci biir rakk yu bare.

Li tuut ab juddu ci àddina, ak li xeeblu, li tekkiwul dara, moom la Yàlla taamu, ngir neenale ko li tekki,

¶ Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar,

¶ Ngëm la Nóoyin dégge waxyub Yàlla bu jëm ci lu kenn gisagul woon, te ragal Yàlla la sàkke gaal, ngir musal njabootam. Ngëmam it la tiiñale àddina, ba ab céram di njub gi ngëm di maye.

Yeen ñi dul woon sax aw xeet, démb, tey yeen ay xeet wi Yàlla ñoñoo; dajaguleen woon yërmande, waaye tey daj ngeen yërmande.