TSK

TSK · Romans 5:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,

Lu doon sagub Siyoŋ, dëkk bu taaru bi, tey sàggiku na. Seeni garmee ngi mel ni kéwél yu amul parlu, di koyoŋ-koyoŋiy daw, te rëbb ne leen dann.

Buur bëj-gànnaar dina ñëw yékkati ay jal, gaw dëkk bu ñu wërale tata, nangu ko. Mbooloom xarey bëj-saalum ak seen ñeyi xare duñu leen mana të. Duñu am doole ju ñu leen tëwe.

mi ñu teg ciy loxo, mu dee ndax sunuy tooñ, ba dekkal ko, ngir nu jagoo àtteb nit ñu jub.

Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla?

Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa,

¶ Yeen ñi doonoon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy, ak seen ñàkka xaraf, ndax li ngeen dul Yawut, Yàllaa leen booleek Almasi dundalaat leen. Moo nu baal sunu moy yépp.

Lii itam xam nanu ko: ñi jub taxuñu yoon wi jóg, xanaa ñi jubadi ak ñi déggadi, ak ñemekati Yàlla yi, ak bàkkaarkat yi, ak ñi wormaalul lu sell, ak ñi wormaalul Yàlla, ak bóomkati baay, ak bóomkati ndey, ak reykati nit ñi,

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.

Bu yàgg, ba àddina sosoogul la Yàlla tuddaloon Almasi loolu, waaye léegi ci mujug jamono jii la ko Yàlla feeñal ngir yeen,

Waaye asamaanu tey jii, ak suuf, genn kàddug Yàlla googu moo leen yeb cib denc, ñeel sawara, kera bésub àtte ba, bésu sànkuteb aji gëmadi ñi.

Jude 1:15 TSK

ngir àtte ñépp, ba tiiñal mboolem yéefar yi, ndax mboolem nu yéefare ni ñu jëfe seen jëfi yéefar, ak mboolem kàddu yu ñaaw yi bàkkaarkati yéefar yi teg cib deram.»