TSK

TSK · Romans 5:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Sànjum Yàlla fa asamaan lay dale feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi, ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.

¶ Gannaaw nag dees noo jox àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi.

¶ Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.

Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru.

te Almasi di ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi, kon nag ñaata yoon la deretu Almasi gëna mana setal sunu yaraange ji sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci ndee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!