TSK

TSK · Romans 6:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waxleen Yuusufa ne ko, sa baay nee: “Say mag def nañu la lu bon moos, waaye ngalla baal leen seeni tooñ ak àq, ji ñu la ameel.” Kon rikk waay, baal nu àq, ndax nun nook sa baay a bokk jenn Yàlla ju nuy jaamu.» Ba ñu waxee Yuusufa loolu, mu daldi jooy.

Job 1:8 TSK

Mu ne ko: «Xanaa seetlu nga Ayóoba, sama jaam bi! Amul moroom fi kaw suuf de! Ku mat la te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.»

Maa gore, musal ma; maay sa jaam bi la wóolu, yaw, sama Yàlla, wallu ma.

Sànkal ma noon yi ci sa ngor, bóomal ma bépp bañ. Man de, maay sab jaam!

Nabukodonosor nag jegeñsi buntu taal bu yànj ba, daldi àddu ca kaw ne: «Éey Sadarag, Mesag, Abet Nego, jaami Yàlla jiy Aji kawe ji, génnleen fii!» Sadarag ak Mesag ak Abet Nego daldi génne ca biir sawara sa.

Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.

Seen jëfi démb ja leen gàcceel tey, ana njariñ lu mu leen jural? Mujug jëf ja de, seenug dee la doon doon.

Waaye cant ñeel na Yàlla mi nuy walloo jëmmu Yeesu Almasi, sunu Sang. Kon daal man, ci sama bopp, ci sama wàllu xel, yoonu Yàlla laay surgawu, waaye ci sama wàllu yaramu suux wii, yoonu bàkkaar laay surgawu.

Ki ñu woo ci Sang bi, fekk ko mu dib jaam, mooy ki Sang bi goreel. Naka noonu, gor si ñu woo, ab jaamu Almasi lay doon.

¶ Léegi nag ndax nit ñi laay sàkkoo jubool, am Yàlla? Am nit ñi laay wuta neex? Su ma bëggoona wéye neex nit ñi de, duma doon jaamub Almasi.

¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,

Su boobaa ngeen meññal ba woomle ci njub, gi Yeesu Almasi di maye, ngir fésal màggug Yàlla, jollil ag cantam.

Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla.

Titus 1:1 TSK

¶ Ci Man Póol la bataaxal bii bawoo, man jaamub Yàlla, biy ndawal Yeesu Almasi, mu yebal ma, ngir ma dugal ñi Yàlla tànn ci yoonu ngëm ak xam-xamu dëgg, giy taxa jullite.

ndax yeena ngi jot ci yool bi ngëm di yóotu, te mooy texe.

¶ Ci kaw loolu kenn ci mag ñi ne ma: «Boroom mbubb yu weex yii, ñooy ñan ak fan lañu jóge?»