Isaiah 44:20
TSK
Kee di jur gu fore ab dóom, xelam nax ko, sànk ko. Du keey musal bakkanam de! Du kee naa: «Xanaa duy caaxaan laa ŋàbb nii?»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kee di jur gu fore ab dóom, xelam nax ko, sànk ko. Du keey musal bakkanam de! Du kee naa: «Xanaa duy caaxaan laa ŋàbb nii?»
Seen ragluwaay ak seen reewande sànk na leen, yeen ñi dëkke xuntiy doj, féetewoo colli tund yi. Waaye su ngeen ajee seenum tàgg ni jaxaay it, fa laa leen di àjjee.» Kàddug Aji Sax jee.
Waaye bàkkaar moo jaare buntub ndigalu yoon, ba yee ci man mboolemi xemmemtéef yu bon. Ndax kat, su yoonu Musaa amul woon, bàkkaar di lu dee.
te mooy ngeen ba seen jikko ju jëkk ja, ngeen teqlikoo ak seen jëmmu démb ja masa topp bànneexi bakkan yuy naxe, ba sóobu ci yàqute.
¶ Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp.