Tee nu koo jaay Ismayleen ñi, te bañ koo sàkkal pexe nun ci sunu bopp? Ndax kat sunu rakk a, di sunu deret.» Doomi baay ya déggal ko.
TSK
TSK · Romans 7:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndax man kat dañu maa sàcce ca réewum Ebrë ya, te fii itam, defuma fi lu tax, ñu war maa tëj.»
¶ «Su dee ku sàcc mala, muy nag mbaa mbaam mbaa ab gàtt, te ñu fekk ko ciy loxoom, muy dund, na fey ñaaram.
Te it bu góom bi soppikoo weex, na dem ca sarxalkat ba.
Seen Yàlla Aji Sax ji, soppeleen ko seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ak seen léppi doole.
¶ Axab dafa dogu woon ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu, ba amu ci moroom moos, te jabaram Yesabel di ko ci xabtal.
Moo ma tax ne: «Wàqet, tuubi-ruubi,» ba diwoo suuf akub dóom.
Maa ngi ne ñàyy ci pënd bi, musal ma, yaa ko dige.
Lu Yàlla wax, mat na sëkk, mooy yiir ku ko làqoo.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Damaa fase seen ndey? Wonleen ma kayitu pase mi! Maa leen jaay njaam, feyey bor? Ana ku ma leen jaay? Bu ñu leen jaayee, seeni ñaawtéef a. Bu ñu fase woon seen ndey it, seeni moy a.
Nun ñépp a mujj mel ni sobe, ni sagaru sobe la sunu gépp njekk mel. Nu ngii nun ñépp mel ni xob wu lax, sunuy tooñ buub nu, yóbbu ni ngelaw.
¶ Yeesu daldi ànd ak ñoom. Naka la jubsi kër ga, njiit la yóbbante ay xaritam kàddoom, ñu gatandu Yeesu, ne ko: «Sang bi, jarul ngay sonn, ndax sab tànk sama biir kër, man yeyoowuma ko.
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
¶ Man nag bokk yi, manuma woona wax ak yeen ni ñuy waxe ak ñu ànd ak Xelum Yàlla, waaye ni niti suuxu neen rekk laa manoona waxe ak yeen, mbete ñu diy tuut-tànk ci yoonu Almasi.
Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.