TSK

TSK · Romans 8:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ne: «Mbégte ñeel na ñi ñu jéggal seeni tooñ, ñeel na ñooñu ñu baal seeni bàkkaar.

Kon nag dootu man maay jëfe noonu, waaye dooley bàkkaar bi ci man la.

ngir njub gi yoonu Musaa laaj mana sotti ba mat sëkk ci nun, ñi toppatul sunu bindu suux, xanaa Noowug Yàlla.

Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!

Nuyul-leen ma Pirsil ak Akilas, sama bokki liggéeykat ci liggéeyub Almasi Yeesu.

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,

Kon bu nit ki bokkee ci Almasi, mbindeef mu bees lay doon. La woon day wonni, li teew nag, di lu yees.

¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»

¶ Li ma leen di wax moo di: doxeleen Noowug Yàlla, su boobaa dungeen topp seen xemmemtéefi bakkan.

ngir ma mana feeñe ci biir Almasi, fu ma yaakaarul sama njekku bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njekk gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi. Njekk googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi moo koy maye.