TSK

TSK · Romans 8:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Bàkkaar moo jaare ci kenn nit dugg ci àddina, dee jaare ci bàkkaar, dikk, ba dikkal ñépp, ndax ñépp a bàkkaar.

Noowug ki dekkal Yeesu moo màkkaanoo ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi mooy dekkal itam seen yarami ndee, ndax Noowam googu màkkaanoo ci yeen.

Saa su nekk, nun ñiy dund, ñu ngi nuy jébbal ndee ndax Yeesu, ba tax dundu Yeesu it mana fése ci sunuw suux wi jëm ndee.

¶ Moo tax nu saxoo ñeme, te xam ne sunu desagum biir kër, ci yaram wi, mooy sunu desagum fu sore Sang bi,

¶ Xoolaatleen seen bopp, ba xam ndax yeena ngi ci yoonu ngëm wi. Nattleen seen bopp, xanaa xam ngeen ne Yeesu Almasee ngi ci yeen? Ndegam du seen gëmadi, la natt ba firndeel!

Su ko defee seen ngëm tax Almasi dëkke seen xol, ngeen sax ay reen yu sampe ci biir cofeel,

ngir ma mana feeñe ci biir Almasi, fu ma yaakaarul sama njekku bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njekk gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi. Njekk googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi moo koy maye.

ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi, làqe fa Yàlla.

Kon ni ab dogal sédde nit ñi benn yoon doŋŋ bu ñuy dee, seenub àtte topp ci,

Li jaadu ci sama gis-gis moo di, li feek may màkkaanoo aw suux, dinaa leen ko fàttli, ngir soññ leen.

¶ Ci kaw loolu ma dégg baat bu jibe asamaan ne: «Bindal: “Bés niki tey ndokklee aji dee ñi deeyaale gëm Sang bi.”» Noo ga daldi ne: «Waawaaw, ndax coono dina leen wàcc, ngir seeni jëf a leen topp.»