TSK

TSK · Romans 8:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bu xew-xew yooyu tàmbalee sotti nag, taxawleen te siggi, ndax seenug njot dëgmal na.»

Céy maaka réy aw tiis! Ana ku may wallook sama yaramu ndee wii?

Càkkéefu àddinaa ngi séentu, ndax yàkkamti bés ba doomi Yàlla di feeñ.

Moo nu tax di onk ci biir xayma bii nu nekk, ndax yàkkamtee soloo sunu dëkkuwaayu asamaan, teg ko ci kaw bii nu jiital,

Ndax nun kat, ci ndimbalal Noo gi, ak ci sunu kaw ngëm lanu yaakaare ñu jox nu àtteb njub bi nuy séentu.

Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam.

Li leer gi ci yeen di meññ moo di mboolem luy mbaax ak njub ak dëgg.

Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi.

Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla, miy Yeesu Almasi, Musalkat bi.

Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant, ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi feeñee.