TSK

TSK · Romans 8:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maa leen di may beneen xol ak xel mu yees. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, weccee leen ko xolu suux.

Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»

Noowug ki dekkal Yeesu moo màkkaanoo ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi mooy dekkal itam seen yarami ndee, ndax Noowam googu màkkaanoo ci yeen.

Waaye ku nekk ak ayam. Jooxeb ndoortel meññeef mi, Almasi la. Gannaaw loolu ñoñi Almasi ñooy aye, keroog bu délsee.

¶ Xanaa ci melow biti doŋŋ ngeen di xool! Su amee ku mu wér péŋŋ, moom ci boppam ne ci Almasi la bokk, na dellu jàpp moom ci boppam, ne ndegam ci Almasi la bokk, nun itam, ci Almasi lanu bokk.

Ñi bokk ci Almasi Yeesu nag, ñoo daaj ca bantam ba, seen bakkan, daajaale ko ak sàkkuteefam yu tar, aki xemmemtéefam.

ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax.

ndax xam naa ne loolu lépp ay walbatiku di samag mucc, ndax seeni ñaan, ak ndimbalal Noowug Yeesu Almasi.

Gëstu nañu jan jamono, ak yan xew-xew la Noowug Almasi ga nekkoon ci ñoom, tegtale woon. Mooy ba Noo gay seede lu jiitu, coonoy Almasi, ak ndam ya cay topp.

Jude 1:19 TSK

Ñooñu ñooy féewalekat yi, ñoo topp seen bindu judduwaale, te Noowug Yàlla nekkul ci ñoom.

Képp ku ñu gisul ñu bind la ci téereb dund bi, ci déegu sawara si lees la sànni.