Aji Sax jee sax dàkk, samp jalam ngir àtte.
TSK
TSK · Romans 9:28
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ab àtteem lay fésale màggaayam, Yàlla ju sell ji, ag njekkam lay firndeele sellngaam.
Tee ngeena baña kókkalee bala ñoo teeŋal seeni jéng? Sànkute kat moo di dogal bi ma dégg, mu bawoo fa Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi, di luy dikkal réew mi mépp.
Bu juróom benn fukk yeek ñaar ciy àppi juróom ñaar weesee, dees na bóom ku ñu fal, te kenn du ànd ak moom. Gannaaw loolu kilifa dina ñëw, ànd ak gàngooram, yàqte dëkk beek jaamookaay bi. Waaye kilifa googu lu mel ni mbënn a koy mujje. Dogal nañu ne yàqte gi dina wéy ba keroog xare biy jeex.
Ndaxte Yàlla jàpp na bés bu muy àttee àddina ci dëgg, àtte bu nit ki mu taamu di sottali; te loolu Yàlla jox na ci ñépp firnde lu wóor, ba mu dekkalee kooku mu taamu, ndekkite lu dee toppul.»