Aji Sax ji nag yuree ca asamaan tamarax buy tàkk, muy taw ci kaw Sodom ak Gomor, na ko Aji Sax ji dogale.
TSK
TSK · Romans 9:29
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 19:24
TSK
Isaiah 1:9
TSK
Bu nu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi waccalul woon li nu deseek as néew, ni Sodom lanuy mel, Gomor lanuy neexool.
Isaiah 13:19
TSK
Babilon nag, mooy gànjaru réew yi ko wër, di teraanga ji Kaldeen ñiy sagoo, waaye Yàllaa koy tas, mu ne tasar ni Sodom ak Gomor.
Jeremiah 50:40
TSK
Mu mel ni ba Yàlla tasee Sodom ak Gomor, tasaale la ko wër.» Kàddug Aji Sax jee. «Nit du fa dëkkati, doom aadama du fa dalati.»
Lamentations 4:6
TSK
Sama ñaawtéefu askan wee màgg, ba raw ñaawtéefu waa Sodom, dëkk ba jekki jàllarbiku, te loxo laalu ko.
Zephaniah 2:6
TSK
tefesu géej doon àllub parlu, ak dëkkuwaayu sàmm seek gétt gi.
2 Peter 2:6
TSK
ndegam dëkk ya ñuy wax Sodom ak Gomor it, la mbugale seenub taste, def leen ab dóom, ba def leen misaal mu ñeel aji gëmadiy ëllëg,