TSK

TSK · Romans 9:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Jëfi ku bon, Aji Sax ji seexlu na ko; ku sàlloo njekk, safoo na la.

Dégluleen maa, yeen ñiy wut njekk, di sàkku Aji Sax ji. Xool-leen doj wi ñu leen yette, xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee:

Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»

¶ Waaye léegi Yàlla moo feeñal nu nit di ame fa kanamam, àtteb njubam gu ajuwul ci yoonu Musaa. Te yoonu Musaa, ak yonent yi seede nañu loolu.

Gannaaw gi la jagoo màndargam xaraf, mu firndeel àtteb njubam gi ngëmam waral, te fekkul mu xaraf. Noonu la Ibraayma mana nekke maamu mboolem gëmkat ñi. Looloo tax muy maamu mboolem ñi xaraful, te gëm, ndax ñu waññal leen seen ngëm, ab àtteb ñu jub.

Moo tax it, ñu waññal ko ngëmam ag njub.

¶ Ana lu nu ci mana wax nag? Yàlla daa wàcc foofu yoon? Mukk kay!

Waaye njub, gi ngëm di maye, li muy digle mooy: «Bul wax ci sa xel, ne: “Ana kuy yéeg fa kaw?”» nde loolu mooy Almasi wàcc ngay sàkku.

Esayi it am fit ba ne: «Ñi ma seetul woon, gis nañu ma, ca ña ma laajul woon laa feeñe.»

Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di joxe àtteb ku jub, xanaa ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla jox nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di joxe kenn àtteb ku jub.

Noonu la yoonu Musaa doone sunu njaatige, tette nu ba ci Almasi, ngir nu jagoo àtteb nit ñu jub ci kaw ngëm.

Jant yooyu amuleen woon benn cér ci Almasi, te amuleen woon jenn yelleef ci mbootaayu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre yi ëmb digeb Yàlla, te mu fasoo ko ak ñoom. Ñàkk yaakaar, ak ñàkka xam Yàlla ngeen nekke woon ci àddina.

ngir ma mana feeñe ci biir Almasi, fu ma yaakaarul sama njekku bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njekk gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi. Njekk googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi moo koy maye.

¶ Ngëm la Nóoyin dégge waxyub Yàlla bu jëm ci lu kenn gisagul woon, te ragal Yàlla la sàkke gaal, ngir musal njabootam. Ngëmam it la tiiñale àddina, ba ab céram di njub gi ngëm di maye.