ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»
TSK
TSK · Romans 9:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Terewul seeni maam doŋŋ la Aji Sax ji taqool, ngir sopp leen, te yeen, ñi askanoo ci ñoom la taamu ci biir xeetoo xeet, niki bésub tey jii.
Ba loolu amee Benaya doomu Yoyada ne Buur: «Buur, sang bi, yal na ko Aji Sax ji sa Yàlla dogal. Amiin!
Man, damaa maandu, nga taxawu ma, dëj ma fi sa kanam, ba fàww.
Cant ñeel na teddngaam, ba fàww, yal na teddngaam dajal suuf sépp! Amiin, Amiin!
Aji Sax jee samp asamaan ab jalam, nguuram ŋank lépp.
Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun).
Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese, ab car soqeekoo fa reen ya,
Mu ne ko: «Amiin! Yal na ko Aji Sax ji defee! Yal na Aji Sax ji sottal sa kàdduy waxyu yi nga wax, ba délloosee Babilon ba fii ndabi kër Aji Sax ji ak mboolem ña ñu fa toxal.
Gannaaw Daawudaa wooye Almasi “Sang bi,” nu mu nekke ab sëtam?»
moo jëm ci Doomam, ji soqikoo ci askanu Daawuda, ci wàllu àddina.
Ag wuutale amul diggante ab Yawut, ak jaambur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall.
Soo yékkatee kàddug cant goo waxe xol doŋŋ, ana nu nit ku xamul ku ko teewe naan: «Amiin,» te xamul li ngay wax?
Moom mi nekke nekkinu Yàlla te ŋoyaaloowul dayob boppam, bi ko def nawleb Yàlla.
Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.
¶ Bàyyil xel ci Yeesu Almasi mi ñu dekkal te mu soqikoo ci Daawuda, ni ko sama xibaaru jàmm indee.
Ñeenti bindeef yi ne: «Amiin.» Mag ñi ne gurub sukk, sujjóot.
¶ Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, maa ngi ñëw léegi.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!