TSK

TSK · Ruth 4:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Séetul ak kii, ba ayu bésam mat, ma door laa jox ki ci des, soo ma dee liggéeyaatal diiru juróom ñaari at.»

Su ko defee bu ca ndaw sa taawloo góor, taaw ba saxal turu mbokkam ma dee, ba turam du fey ci biir Israyil.

Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ji, te ay noppam la dékk wooteb wallam.

Ku am jabar, am nga ngëneel, am nga yiwu Aji Sax ji.

Jeeg bu jàmbaare, ndaw lu jafe, ba rawati gànjar!

seen geño sakkan ni suuf, di seen meññeefu biir, tollook feppi suuf, du dog, du sànkoo fi sama kanam!

Su Galàdd dee dëkkub defkati ñaawtéef, dañoo tekkiwul dara. Fa Gilgal lees di rendee ay saraxi yëkk, te seeni sarxalukaay ni jali xeer lay mel ci ay tooboy tool.

Ngeen naa: «Ndax lan?» Ndax Aji Sax ji moo seede seen diggante ak seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw, tey ngeen wor ko, te mu doonoon seen wéttal, seen jabar ju ngeen séqal kóllëre.

¶ Na ñépp wormaal diggante bu ab séy dox, te ab lalu séy na mucc sobe, ndax fokati séy yi, ak jaalookat yi, Yàlla moo leen di daan.