TSK

TSK · Zechariah 2:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maay dëggal sama kàddug jaam, di sottal sama ndéeyal ndaw. Maa naan ci Yerusalem: “Dees na ko dëkke,” dëkki Yuda, ma ne: “Dees na leen tabaxaat, ma dekkali gentam bi.”

Xoolal, man maa sàkk ab tëgg buy wal taalu këriñ, defar ca ngànnaay lu ne. Waaye maa sàkk it yàqkat buy rajaxe.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di tijji wërsëgu askanu Yanqóoba, ñibbsil leen, baaxe seeni dëkkuwaay, ba dëkk dekkee ca tundam wu gentoon, kër buur taxawaat bérabam,

¶ «Bés a ngii nag di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may jiwe kërug Israyil ak kërug Yuda jiwum doom aadama ak jiwum mala.

¶ Aji Sax ji dafa wax ne: «Bérab bii ngeen ne ab gent la bu kenn nekkul, du nit, du rab te muy dëkki Yudak mbeddi Yerusalem yii gental, kenn nekku fi, du nit, du rab, dees na fi déggati

Maa leen di fulal aw nit, ci biir Israyil gépp, ba mu daj, ñu dëkkewaat dëkk yu mag yi, tabaxaat bayaal yi.

Yàlla nag may ñeenti xale yu góor yooyu xel ak ràññee ci mboolem lu ñu bind ak wàllu xam-xam. Dañeel moom mana firi mboolem peeñu ak gént.

Nanga yéenewaat, nga ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Samay dëkk ay walewaat ak alal, te Aji Sax ji mooy dëfalati Siyoŋ, mooy taamooti Yerusalem googu.”»

Bésub keroog maay def njiiti Yuda mel ni ab taal bu jafal jalu matt, mbaa jum bu ñu jafal ci sabaaru pepp; wetu ndijoor ak wetu càmmoñ lañuy xoyome mboolem xeet yi leen wër, te Yerusalem toog bérabam, di Yerusalem ba tey.

Yii duma la Aji Sax jiy duma mboolem xeet yi xareek Yerusalem: Seen suux mooy yàqu te ñu ne jonn taxaw, seeni gët yàqu ca seen biir paxi gët, seenu làmmiñ nëb ca seen biir gémmiñ.