TSK

TSK · 1 Corinthians 7:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

te fekk Màrt jàpp lool ca liggéeyu waañ wa. Mu dikk ne Yeesu: «Sang bi, xanaa gisoo sama rakk ji ma bàyyeek liggéeyu waañ wi, man doŋŋ? Wax ci boog, mu jàpple ma.»

¶ «Moytuleena yaafusal seen bopp ci naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,

Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu.

Ag ñàkk nag taxul may waxe nii, nde tàmm naa di doylu ci diggante bu ma mana tollu.

¶ Mboolem ñi ci buumu njaam, nañu jàpp ne seeni sang yelloo nañu gépp wegeel, ngir kàddu gu teddadi baña tege ci turu Yàlla, ak sunu àlluwa.

¶ Yeen jaam yi, nangul-leen te weg wegeel gu mat sëkk seeni sang, te du sang yi baax te lewet doŋŋ, waaye ñu wex ñi itam ci lañu.