TSK

TSK · 1 Kings 21:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba mbooloo ma déggee kàddu yu dëgër yooyu, dañoo daldi toroxlu, ba kenn takkootul gànjaram.

¶ Daawuda nag tinu Yàlla ci xale bi: muy woor, fatu, fanaanee tëdd ci suuf.

Ba loolu amee bootalub Buur, Elyakim doomu Ilkiya ak Sebna, bindkat ba, ak doomu Asaf, Yowa ma denc téere ya, ñoo dem ak seen yérey ñaawlu yu xottiku, ba ca Esekiya. Ñu daldi koy àgge kàddug bëkk-néeg ba.

Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.

Ndax lii moo di koor gi ma taamu, ci bés bu nit kiy toroxlu? Koorug dëngal loos ni barax, lal saaku, sotti ab dóom, tëdd di ko ñaawloo? Loolooy seen koor, ci bés bu Aji Sax ji rafetlu?

Joel 1:13 TSK

Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu, yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen, yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen, sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu, nde xañees na seen kërug Yàlla ga saraxu pepp ak saraxu tuuru!