TSK

TSK · 1 Kings 21:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu ne leen: «Jomb naa loolu. Ki ñu fekk kaas bi ci loxoom mooy doon sama jaam; ñi ci des dellu ca seen baay ci jàmm.»

Du benn céru suuf ci biir bànni Israyil, buy jóge ci genn giir, toxu ca geneen, waaye na ku nekk ci bànni Israyil yem kepp ca suufas giiram, ga mu donne cay maamam.

Man nag, yàlla tere may tooñ Aji Sax ji, di leen noppee ñaanal. Te it dinaa leen won yoon wi baax te jub:

Daawuda ne Abisay: «Bu ko rey. Ana kuy yékkati loxoom ci kaw ki Aji Sax ji fal, te yoon dabu ko?»

Job 27:5 TSK

Yàlla buma leen jox dëgg, ba ba may dee duma weddi samag mucc sikk.

Mukk kay! Fàww Yàlla wéye di ku dëggu, te ñépp di ay fen-kat, te noonu la Mbind mi indee ne: «Soo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.»

Ndax loolu day tekki ne ngëm lanu jël, neenale ko yoonu Musaa? Mukk! Xanaa dañu koo dëggal kay.

¶ Ba ci lan boog? Ndax kon danuy bàkkaar, gannaaw du ci kilifteefu yoonu Musaa lanu nekk, waaye ci aw yiw lanu tàbbi? Déet kay!

Lu baax loolu di yoonu Musaa, xanaa kon moo ma taxa dee? Déet kay! Bàkkaar moo feeñale noonu meloom; moo jëfandikoo lu baax, ba rey ma, ngir ndigalu yoon di jumtukaay bu bàkkaar fésale gépp mbonam gu jéggi dayo.

Waaye man de Yàlla buma damoo lenn lu moy deewug sunu Boroom Yeesu Almasi ca bant ba. Bant boobu moo tax àddina di lu ñu ma daajal ci bant, ba àddina dee; man it may lu ñu daajal àddina ci bant ba ma dee.