TSK

TSK · 1 Peter 1:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ndax kat askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la seen Yàlla Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf.

Fi Yanqóoba laay soqee aw askan, fi Yuda laa ne, fi laay jële lu séddoo samay tund. Samay tànnéef a koy séddoo, sama jaam ñi kay a fay dëkke.

¶ Man Nabukodonosor maa ngi woon ci sama jàmmi kër ak sama teraangay màkkaan.

Luke 18:7 TSK

Kon ndax Yàlla man naa baña sàmm àqu tànnéefam ñi koy woo wall guddi ak bëccëg, xanaa di leen yeexe?

Acts 2:23 TSK

Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.

¶ «Léegi nag, dénk naa leen Yàlla ak kàddug yiwam, gi leen mana dooleel, dencal leen seen muur ci biir mboolem nit ñi ñu sellal.

¶ Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.

Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw, ci biir rakk yu bare.

Su dee Yàlla moo def loolu nag ngir fésal màggaayu teddngaam, ñeel ay ndab yu xéewloo yërmande, te mu waajalaloon leen teraanga?

Kon nag naka noonu itam ci jamonoy tey jii, aw ndes a ngi fi, te ci kaw yiw lees leen taamoo.

ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.

mbóot mu bindi yonent yi fésal tey, ba xamal ko xeet yépp ci ndigalal Yàlla ji sax, ngir xeet yépp gëm ba dégg ndigal,

Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi, ak ci sunu Noowug Yàlla.

¶ Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ.

Looloo ma tax di muñ lépp, ngir ñi ñu taamu, ndax ñoom it ñu dajeek mucc gi ci Almasi Yeesu, boole ci teraanga ju sax.

Noonu lees matale Almasi sëkk, ba mu doon cosaanu mucc gu dul jeex, ñeel mboolem ñi ko déggal.

Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu, ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.

Yeena àgg fa Yeesu, Rammukat bi dox kóllëre gu yees gi, yeena àgg fa deret jiy setal tuuroo, te kàddug deret ja gëna neex kàddug deretu Abel ga jiboon.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

Jude 1:2 TSK

Yërmande ak jàmm ak cofeel baawaan na, ñeel leen.